Aam doolé wéér pénc nii deerëëm,
Gudu faan aam ami deerëëm ba doyal.
Aam ka cii anam wu léw té dagaan,
Ufal sa ndjaboot té sama saw askaan.
Kanu deerëëm dafa khote gaska yombul,
Démal ba jéékh té bul bayi sa lokho.
Téyel sa lokho cii alal ju léwul,
Kanu deerem dafa khote té leedem boko Momul.
Lo momul ba kofa la santa muñal,
Béss khéwel ñew nékhe ba mélni leewëël.
Khuc…Seni khél waw khuc seni khél…
Omar séni khél Omar séni khél.
Téye suma nékhé jugué Bargny dokh ba Jepeul,
Dii añé reré, ganaru tuggëël.
Beugëë tuma yabéy daméy nos nos lu nékh,
Nane yu séde, yes ba kérgui séde.
Yoor mercédés bu bés sol guéns ba fés,
Anda ak jogama ju khés fésna fés ba jékh.
Aam doolé wéér pénc nii deerëëm,
Gudu faan aam ami deerëëm ba doyal.
Aam ka cii anam wu léw té dagaan,
Ufal sa ndjaboot té sama saw askaan.
Sakanal wa am, wa yakh ñaak,
Sakanala guëën yakh ñaak.
Aam doolé wéér pénc nii deerëëm,
Gudu faan aam ami deerëëm ba doyal.
Nga tope kanu deerëm ba mu dugal la cii lendëëm
Téye yanginii guelëëm thiaf khëëm.
Jooloff ku fii jél lii deerëëm kéna dula yeerëëm,
Goal jokhco guedëëm, jarul uti kheerëëm.
Kutia, Sadiogu waw dii la siweel,
Walf, pop, soleil, matin dii la feessëël.
Bul jéél loo momul, jaam lala diigëël.
Té lu dul deeggëë yagul jaam lala beegëël,
Déf lii nga man, lu cii tégu don sa khéwëël,
Té yéém cii lii nga mome lumu méti méti muñal.
ku daw danu jook fakhassu dokhal sa dokh,
lune fii am na fii khééw na fii ngiir ay deerëëm.
Deerëëm nékh jééfe néne séytané ko yébal.
Kon fegue bunta oubi man na feegue bunta téju.
Bul jéél loo moooomul
Ndakh man na andi nakharé
Ñaak ak aam ñéép léy nuyu,
Wayé kéna kuné nii ngééye uté.
So jakhlé talal lokho
Deerëëm ñeuw dééf la khariit,
Téyel sa ndiaaboot.